Les bienfaits de «Bismillaahi Rahmaani Rahiimi » par Cheikh Ahmadou Bamba

Ku jàng bismillaahi rahmaani rahiimi ñaar fukki yoon ak ben (21) booy tëdd yalla sunu boroom danako musël ci saytaane guddi googee ak deewuk mbetteel ak sàcc ak béeppu balaa.

Ku jàkkarlook ap tooñ kat mu jàng bismillaahi rahmaani rahiimi juroom fukki yoon (50) sunu boroom danako tàggatal tooñ kat boobu. Tayyit dana dugal ak ragal ci xolam baduko ñime.

Ku tegale ñatti fann di jàng téeméeri (100) bismillaahi rahmaani rahiimi ci ku tawat sunu boroom danako saafara.

Ku bayyi ba jant bi di fenk mu jàng ñatti téeméeri (300) bismillaahi rahmaani rahiimi julli ci yonent bi (YYJSM) téeméeri yoon (100), sunu boroom danako wërësëgël fumko foogewul. Ta balaa am at dana doon ku woomal.

Budee taw nga jàng bismillaahi rahmaani rahiimi juroom ben fukki yoon ak ben (61) fas ci yéenée saafara tawat jum mana doon yalla danako saafara.

Kuy jàng bismillaahi rahmaani rahiimi fukki yoon ak juroom ñent (19) suba ak ngoon sunu boroom danako musël ci ñiy fitnaal ci bàmmeel ak booleem gàkk yi ta danako may ak raglu akuk soppu ci nit ñi.

Ku bind بسم الله الرّحمان الرّحيم fanweeri yoon ak juroom (35) tak ko cisa néek saytaane dufa duggu ak jinne. Ta sa néek dana bëri barke akuw yiw.

Bës bi njëk ci weeru tamxarit ku bind بسم الله الرّحمان الرّحيم téeméeri yoon ak fukk ak ñatt (113) tak ko, sunu boroom danako musël ci béep ñawtéef mook waa kërëm féek migi dund.

Ibn Alhaaji neena ku bind بسم الله الرّحمان الرّحيم téeméeri yoon ak fukk ak ñent (114) tak ko, sunu boroom dana faj aajoom ta danako may ak raglu ci xoli buuryi ak tooñ kat yi. Batay lifeek moogi tak téeré bi kenn duko lor tayyit sunu boroom danako wattul alalam ak ñoñam.

 Yonent bi (YYJSM) neena sunu boroom giiñ na cik màggam akuk teddam akuk mbaaxam ni ku jàng bismillaahi rahmaani rahiimi ben yoon (1) tek ci faatiha ben yoon (1) danako jéegël ay bàkkaaram donte jotnañ déele asamaan. Ta danaa nangu ay yiwëm ta duma lak lameñam ci sawara ta danaaa ko musël ci bugëlum sawara ak tiit mu makma ca ëllëk ta danaa ko jàppundalal ba buy taseek man day àndak yonent bi (YYJSM) ak waliyuyi

Ku bind ب س م ا ل ا ه ا ل رّح م ا ن ا ل رّح ي م tak ko, sunu boroom danako may ngënéel lu rëy.

Ku bind ci këyyit ب ñaar fukki yoon ak ben (21). Su noppee mu jàng ci këyyit gi téeméeri (100) bismillaahi rahmaani rahiimi ci yéene ju dëggu tek ko ci alalam dana barkeel ta dana yokku.

Ku bind baatup الرّحمان juroom fukki yoon (50) tak ko dana am wërsëk tadu gis lumu sip.

Néenañ ku taqook bismillaahi rahmaani rahiimi junniyoon (1000) fukki fanan ñent (14 jours) ci ginaaw julli gune, yalla danako wuñil mbiryu nëbu yéep ba dana mënë gis yenn malakayi di waxak ñoom ñukoy lëgéeyël diko dimbëli.

Ku bind baatup الرّحيم ñaari téeméeri yoon ak juroom ñen fukku ak juroom ñent (299) tak ko, ngànnaay dula manal darra. Ta noon bu taseek yaw daw ci sa kanam.

 

Majmahu nuurayni fii fawaa-i-di darayni

Auteur : Cheikh AHmadou Bamba

Transcription Wolof : S Moustapha Lô Kholl

Rate this item
(1 Vote)

Téléchargez l'application Toubamajalis

Facebook

(SERVICE COMMERCIAL ) Email : toubamajalis@gmail.com | webtawfeh@gmail.com

 

(REDACTION TOUBAMAJALIS) Email : sennegueye@gmail.com tel.

Chargé de communication : +221 77 539 55 17

Aller au haut