Toubamajalis.com- Jigéen bu wanne lor bamu am ñatti weer (3 mois), da ngay wax : H'abdulaahi ibnu H'omar, H'abdulahi ibnu Mas-h'uud, H'abdulaahi ibnu Zubëyri, H'abdulaahi ibnu Salaam, H'abdulaahi ibnu Zëydin, H'abdulaahi ibnu ummi Maktuum (YYDG).

Boo noppe nga tifliko ci biirëm.

In chaa Allaahu, Bu doom ji juddoo góor lay nék, dina doon boroom xam xam ta saytaané duko laal.

Seex Sidiya mu makma neena ap ëmbu bu amee ñaari weer (2 mois) wala luko ëpp tuuti, na nga bind lii ci aw këyitt gu weex :

 

 

Su noppee, mu defko ap téeré takkal ko soxnasi bam am ñéen fukki guddi (40 nuits). Ginaaw ñeen fukki guddi yi mu tekki téeré bi dencko ba doom ji juddu. Bu doom ji juddu mu takkalko téeré bi. In chaa Allaahu, yalla dana sammu ëmb bi ak doom ji.

 

 

 

 Extrait de : Majmah'u nuurayni fii fawaa-i-di daarayni

Auteur : Cheikh Ahmadou Bamba (rta)

Transcription Wolof : S Moustapha Lô Kholl , Ingénieur en Energie Renouvelable

Toubamajalis.com- Muusaa Ibn Yëziidin jëlena ci Uwaysul Xaraniyu mu jële ci H'omar Ibn Qattàb ak H'aliyun Ibn Abii Taalibi () ñuni yonent bi (YYJSM) neena ñaan gii kuko ñaan yalla sunu boroom dana wuyyu sak ñaan. Donte ci ndox muy daw lañ ko tifli dana dal. Migi nii :

Allaahuma innaka hayyun laa tamuutu. Wa q'aalibun la tuq'labu wa basiirun laa tartaabu. Wa samiihun la tachukku. Wa qëhaarun la tuq-hëru. Wa abadiyun la tanfadu. Wa xariibun laa tabh'udu. Wa chaahidun laa taq'iibu. Wa ilaahun laa tudaadu qaahirun laa tazlimu. Wa samadun laa tuth'amu. Wa xayyuumun laa tanaamu. Wa muh'tajibun laa turaa. Wa jabaarun laa tudaamu. Wa h'aziimun laa turaamu. Wa h'aliimun laa tuh'lamu. Wa xawiyyun laa tudaah'afu. Wa sabbaarun laa tuusafu. Wa waffiyun laa taxlifu. Wa h'adlun laa tahiifu. Wa q'aniyyun laa taftaxiru. Wa kënzun laa tanfadu. Wa hakamun laa tajuuru. Wa maanih'un laa tuq-hëru. Wa mah'ruufun la tunkaru. Wa wakiilun laa taxaafu. Wa fardun laa tastachiiru. Wa wëhaabun laa turaddu. Wa sariih'un laa tëzhëlu. Wa jawaadun laa tabxalu. Wa h'aziizun laa tazillu. Wa h'aliimun laa tëjhëlu. Wa hafiizun laa tax'fulu. Wa mujiibun laa tas-amu. Wa daa-imun laa tafnaa. Wa baaxin laa tublaa. Wa waahidun laa tuchabbahu. Wa muxtadirun laa tunaazih'un.

 

Majmahu nuurayni fii fawaaidi darayni

Par Cheikh Ahmadou Bamba

Transcription Wolof : Serigne Moustapha Lô Kholl

 

Wax nañ ni sahaabay yonent bi (YYJSM) musnañoo jëfëndikoo tandarma daadi naan ndox. Yonent bi (YYJSM) ni léen lii boknaci xéewël giñ léendi laaj ëllëk. Loolu jaaxal sahaabayi lool. Yonent bi (YYJSM) ni léen bu ngéendi lekkati da ngéeni wax :

bismillaahi rahmaani rahiimi wa h'alaa barakaatihii.

Bu ngéen suurée ngéen wax : alhamdulillaahi lëzii ach-bah'anaa wa ar waanaa wa an h'ama h'alaynaa wa afdalu.

Loolu moo léendi fegal laaj gi. Amna hadiis bu yonent bi (YYJSM) wax ni ñaari xéewël yii ñu bëri naxnañ léen ci muy wér ak féex.

 

Extrait de "Majmahu nuurayni fii fawaaidi darayni"

Auteur : Cheikh Ahmadou Bamba (Rta)

Transcription Wolof : Serigne Moustapha Lô Kholl

 

1) Ku bind saaru yuusufa ci këyit gu weex ta benn araf faruci takkalko ku ëmbë, in chaa Allaahu dana am doom ju góor ju raffet. Ta yalla sunu boroom danako musël ci léeppu lumu ngërëmul.

Ap leeral : saaru yuusufa nak mooy fukkéelu saar ak ñaar (12em) ci kaamil bi.

2) Boroom Rawdul Yaanih'u neena ku bëgg doom ju góor, boo boolook sa soxna ba noppi na nga ko digël mu tëdde ndayjooram.

3) Ku bëgg doom ju góor, busa soxna ëmbée na nga tudde ëmb bi Muhammad (YYJSM).

 

 Majmahu nuurayni fii fawaa-i-di darayni

Auteur : Cheikh AHmadou Bamba

Transcription Wolof : S Moustapha Lô Kholl

Facebook

Téléchargez l'application Toubamajalis

(SERVICE COMMERCIAL ) Email : toubamajalis@gmail.com | webtawfeh@gmail.com

 

(REDACTION TOUBAMAJALIS) Email : sennegueye@gmail.com tel.

Chargé de communication : +221 77 539 55 17

Aller au haut